TSK

TSK · Daniel 11:40

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yéene bii moo wàccal màndiŋ ma feggook géej ga: Ni ag ngëlén di riddee jaare Negew ni la noon di bawoo màndiŋ ma, jóge réew mu raglu.

«Noon baa ngii, di jóg niy niir, watiiri xareem ni ngëlén, fasam ya gëna gaawi jaxaay. Wóoy ngalla nun, yàqu nan!»

Waaye yaa naa jàyy ni ngëlén, mel ni aw xiin, muur réew mi, yaak sa gàngoor yépp, ak xeeti xeet yi ànd ak yaw.

Jibril dikk nag ba fi ma taxaw. Ba mu jegesee, ma tiit lool, ba daanu, sama kanam dëppu fi suuf. Mu ne ma: «Yaw doom aadama ji, nanga xam ne peeñu mii mujug jamono la.»

¶ «Ay doomam yu góor nag dinañu waajal xare, dajale gàngoor yu takku. Ñu jubal, bëtt, jàll nim wal, daldi ñoqli, songi noon ba ca dëkk ba ñu wëralee tata.

Ci biir loolu ay nit ñuy bokk ak buur bëj-saalum ndab ñooy sànk buur bëj-saalum, ba mbooloom jóoru, ñu bare tëdd.

¶ «Yaw nag Dañeel, dencal kàddu yii, muy kumpa te nga tëj téere bi, tay ko ba mujug jamono jub. Su keroogee ñu bare dinañu gëstu fu ne, ba xam-xam yokku.»

Limu gawari mbooloo ma doon xareji ñaar téeméeri junniy junni la (200 000 000). Maa dégg lim bi.