TSK

TSK · Daniel 11:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Dinañu lël sax seen jëmmi tuur yu ñu móol, yóbbu Misra, boole kook seen gànjaru xaalis ak wurus. Gannaaw loolu dina toog ay at te du laaleek buur bëj-gànnaar.

Jamono yooyu ñu bare dinañu jógal buur bëj-saalum, te ay nit ñu soxor ñu bokk ci saw xeet dinañu fippu, ni ko peeñu indee, waaye duñu ko man.

Ca mujug jamono buur bëj-saalum dina fenqoo ak buur bëj-gànnaar. Te itam buur bëj-gànnaar dina mel ni ngëlaani, ne milib ci kawam, ànd ak watiiri xare aki gawar ak gaal yu mag yu bare. Dina dugg ci ay réew, bëtt, jàll nim wal.