Psalms 76:10
TSK
Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.
Merum buur ni gaynde gu ŋar; yërmandey buur ni lay cig mbooy.
Doj diis na, suuf dib sëf, waaye fitnay dof a ko raw.
¶ Buur wax xërëmkat ya ne leen: «Dogal bu wér a ngii tukkee fi man. Su ngeen ma waxul gént gi, wax ma piri mi, ay dog lañu leen di dog, seeni kër doon ay sën.
¶ Ci kaw loolu Nabukodonosor mer lool ba fees dell, kanam gay sël-sëli janook Sadarag Mesag ak Abet Nego. Mu santaane ñu xamb taal ba, ba mu gëna tàng juróom ñaari yoon na mu daan tànge;