TSK

TSK · Daniel 2:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye juróom fukk ñooñu jub, su yéesee juróom rekk nag? Mbaa doo tas dëkk bi ndax juróom ñi ci yées?» Aji Sax ji ne ko: «Su ma fa gisee ñeent fukk ak juróom ñu jub, duma ko tas.»

Esteer dellu yónnee ca Mardose, ne ko:

Mu woo ma, ma wuyu ko; mook man ci biir njàqare, ma xettli ko, darajaal ko,

Nanga wóoloo Aji Sax ji, sa léppi xol, te bul wéeru ci saw déggin.

Mu ne: “Woo ma, ma wuyu la, wax la lu réy te loq, loo xamul woon.”»

Ca ngeen di ràññaatlewaat diggante ku jub ak ku bon, kuy jaamu Yàlla, ak ku ko jaamuwul.

Acts 12:4 TSK

Naka la ko jàpplu, daldi koy tëj kaso, teg ko ci loxoy ñeenti kurél yu ñeenti takk-der, ngir ñu wattu ko; booba ma ngay xaar ba bésub Mucc bi wees, mu door koo yóbbu ca kanam askan wa.

Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jaambur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.