TSK

TSK · Daniel 3:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.»

Bésub tey jii Aji Sax jee lay teg ci sama loxo, ma rey la, dog sa bopp. Tey jii sax laay leele njanaaw yeek rabi àll yi, néewi xarekati Filisti, ba àddina sépp xam ne Israyil am na Yàlla.

Job 34:29 TSK

Bu Yàlla nee cell, ana ku koy ŋàññ? Bu làqee kanamam, ana ku koy niir? Xeet yeek nit ñi la boole tiim,

Ñeel Daawuda. Aji Sax jee may leeral, di ma wallu. Ana ku may ragal? Aji Sax jeey aar sama bakkan. Ana ku may tiit?

Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.

Te yaw sunu Yàlla, yaa ngi asamaan, di def lu la soob.

Ma ne: «Yàllaa may wallu, ma dal-lu, duma tiit. Sama dooleek sama kaaraange mooy Ki sax, di Aji Sax ji, te mooy sama wall.»

Njekk moo lay dëgëral, nga sore noteel, doo tiit; sore tiitaange, du la jege.

¶ «Dogal tukkee na ci man, ne mboolem fu bokk ci sama nguur, nañu fa ragal Yàllay Dañeel, wormaal ko, keey Yàlla jiy dund, kee sax fàww, nguuram du tas, kilifteefam du jeex.

Waaye sama bakkan soxalu ma, xanaa ma bey samaw sas, ba sottal liggéey, bi ma Sang Yeesu dénk, te mooy seedeel xibaaru jàmm bu yiwu Yàlla wi.

Ay fani fan jant beek biddiiw yi ne meŋŋ, te ngelaw liy riddi rekk, ba nu noppee yaakaar ne dinanu mucc.

Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.