Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ.
TSK
TSK · Daniel 3:18
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Exodus 20:5
TSK
Proverbs 28:1
TSK
Ku bon daw na te dàqeesu ko, ku jub ñeme ni gaynde.
Daniel 3:28
TSK
¶ Nabukodonosor wax ne: «Cant ñeel na Yàllay Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, moom mi yónni malaakaam, mu wallu jaamam ñi ko wóolu, ba xëtt sama ndigal man Buur, te jaay seen bakkan gënal leen ñuy jaamu mbaa di sujjóotal jeneen yàlla ju dul seen Yàlla.
Acts 4:10
TSK
xamleen xéll, yeen ñépp ak bànni Israyil gépp, ne ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, ki ngeen daajoon ci bant, te Yàlla dekkal ko, ci turam doŋŋ la kii wére, ba taxaw ci seen kanam.
Acts 5:29
TSK
¶ Piyeer ak ndaw ya ca des nag ne leen: «Yàlla lees wara déggal, waaye du nit.
Revelation 12:11
TSK
Sunu bokk yee daan ndax deretu Gàtt bi, ak seen kàddug seede, te soppuñu seen bakkan ba ragala dee.