TSK

TSK · Daniel 3:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Ezra 4:12 TSK

¶ nu ngi lay xamal yaw Buur, ne Yawut ñi bàyyikoo fi yaw, ñëw fii ci nun, agsi nañu Yerusalem, dëkku fippukat bu bon bi, te ñu ngi koy tabaxaat. Ña ngay yékkati tata ya, gannaaw ba ñu lalaatee kenu ya.

¶ Aman wax Buur Aserus ne ko: «Aw xeet a ngi fi, tasaaroo ci biir xeet yi, jaxasoo ci seen biir, ci mboolem sa diiwaani réew mi. Seeni aada daa wuuteek yu xeet yépp; yoon yi Buur tëral, duñu ko jëfe, te jaaduwul ci Buur mu di leen seetaan.

Ci kaw loolu nit ña rungumloo, fekk ko muy ñaan ak a dagaan Yàllaam,

Ñu taxawal leen fa àttekat ya, ne: «Ñii ñoo yëngal sunu dëkk bi, di ay Yawut

Waaye bëgg nanoo dégg ci sa gémmiñu bopp li nga gëm, ndax li nu xam daal mooy, ngér moomu nga bokk, fu nekk lañu koy diiŋate.»