TSK

TSK · Daniel 4:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye maa la musal, te li ma ci jublu moo di won la sama doole, ba sama riirum tur dajal àddina.

¶ Axab dafa dogu woon ci def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu, ba amu ci moroom moos, te jabaram Yesabel di ko ci xabtal.

Te itam sarxal na doomam, lakk ko ngir ay tuur. Ci biir loolu jabar na, ñeengo na, jëflante naak boroom rawaan aki gisaanekat. Bare na lu mu def lu Aji Sax ji ñaawlu, ba merloo ko.

Xeet yee tàbbi pax ma ñu gasoon, fakktaloo fiir ga ñu làqoon.

bul bewa bew, bay waxe reewande.”»

Mooy yékkatee ku néewle fa suuf, di seppee ku sonn cib sën,

¶ Ma dégg baatu Boroom bi, mu naan: «Ana ku may yebal, ana ku nuy demal boog?» Ma ne: «Xanaa man, yebal ma!»

Maay indi xeet yi gëna néeg, ñu nangu seeni kër, ma daldi sàggi sagu boroom doole yi, sobeel seen bérab yu sell.

Mooy walbati jamono, di soppi demin, di fal buur, di folli. Mooy xelal boroom xel mu rafet, di xamal boroom xel mu ñaw.

Mu nitoodi, ame xelum mala diiru juróom ñaari jamono.

Mboolem waa àddina di neen ci moom. Nu ko neex lay def ak gàngoori xarey asamaan ak waa suuf, te kenn du fél loxoom mbaa mu naa ko: «Ana looy def nii?»

¶ «Ku siblu moo koy wuutu, ku yelloowul darajay nguur. Day duggsi ndànk, lal ay pexeem, ba nangu nguur gi.

¶ Maa ngi lay àrtu nag fi kanam Yàlla, ak Almasi Yeesu, ak malaaka yi ñu tabb, ngir nga sàmm loolu te baña jeng, mbaa nga jëfe lenn loo defe xejj ak seen.