Ñu jal koo jal, ba xet ga ubale ca réew ma.
TSK
TSK · Daniel 4:32
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Musaa ne ko: «Bu may génn dëkk bi rekk, di tàllal Aji Sax ji samay loxo, dënu yi dakk, tawub yuur bi siwet, ngir nga xam ne àddina, Aji Sax jeey boroom.
Kii, bu këfee, ana ku koy tere? Ana ku ko naa: «Looy def nii?»
Ñooñu lees dàqe fi biir nit ñi, di leen yuuxoo niy sàcc,
Te yaw sunu Yàlla, yaa ngi asamaan, di def lu la soob.
Samay pexe la buur di jiitee, kilifa di ci àttee dëgg.
Xeet yaa ngii, mel ni aw toq ci biir bagaan, jàppeesu leen lu moy diisaayu feppu suuf! Dun yi lay yékkati ni pëndub suuf!
Maa lay jagleel denc yu loq, ak alal ju làqe, ba nga xam ne maay Aji Sax ji lay wooye sa tur, man Yàllay Israyil.
Ndogal a ngoog bu wattukat yi tëral, àttee ngoog bu ñu sell ñooñu digle, ngir aji dund ji xam ne Aji Kawe jee yilif nguurug nit, di ko jox ki ko soob, di ca fal ki gëna tuut.”
dàqe ko ci nit ñi, def xel ma xelum rab. Mu dëkk ak mbaami àll yi, am ñax dim xontam niw nag, lay biy wàcc, di ko faam, ba kera ba mu xamee ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex.