TSK

TSK · Daniel 4:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Meram di lu gàtt, aw yiwam sax dàkk. Rongooñ gane, fanaan, ay ree xëysi.

Ña nga naa: «Dikkleen, ma indi biiñ, nu màndeew ñoll; tey ak ëllëg; li fi des du jeex.»

«Yaw nit ki, waxal Boroom Tir, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dangaa fuuy ba naan: ‘Maay Yàlla, ji tooge toogub yàlla yi, fi xolu géej!’ Waaye yaw doom aadama nga, doo Yàlla, dangay yàlla-yàllalu rekk.

Waxal, nga ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii fi sa kaw, yaw Firawna buuru Misra, yaw ninki-nànka ju mag ji goore sa diggi dex, te naan: ‘Maa moom sama dex, man ci sama bopp maa ko sàkk!’

¶ Ba loolu amee boroom xam-xami Buur yépp dikk ba ca biir, waaye manuñoo jàng mbind ma, bay xamal Buur la muy tekki.

Su ko defee ci samam xel laa naan: ‘Céy sama waa ji, yaa ngeek alal ju bare ju mana dem ay ati at; neel finaax, di lekk, di naan ak a bége.’ ”