TSK

TSK · Daniel 7:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Na wóllërey Yàlla bànneexoo seen ndam, bu ñu tëddee sax, di sarxolle,

«May xool ba tey, ñuy teg ay gàngune, góor gu mag gi dikk, toog. Mbubb maa nga weex furr, kawaru boppam weex tàll, ngànguneem ma di saf sawara, wuy sël-sëli, mbegey ngàngune ma bindoo ni sawara wu yànj,

Xanaa xamuleen ne aji sell ñi ñooy àtteji àddina? Ndegam yeenay àtteji àddina, xanaa àtte mbir yi gëna tuut jombu leen?

¶ ba noppi def nu nuy askanu sarxalkati Buur Yàlla Baayam, na ko daraja ak kàttan ñeel tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.

Yaa leen def ñu doon nguurug sarxalkat yi, ñeel sunu Yàlla, te dinañu nguuru ci àddina.»

¶ Meneen malaaka, topp ci, di ñaareel bi. Mu ne: «Babilon a daanoo, dëkk bu mag ba daanu na! Moom ma daan màndal askanoo askan biiñu moyam muy indi am sànj.»

¶ Ci kaw loolu ma gis ay gàngune yu ñu jox ña ca toog, sañ-sañu àtte. Ma daldi gis bakkani ñi ñu dogoon seen bopp ndax la ñu doon seedeel Yeesu ak la ñu gëmoon kàddug Yàlla, ña sujjóotalul woon rab wi ak jëmmu nataalam, te amuñu màndargam rab wi ci seen jë mbaa seen loxo. Ñu dekki bay nguuroondoo ak Almasi diiru junniy at.