Mise teg ca ne ko: «Kon nag déglul kàddug Aji Sax ji. Gis naa Aji Sax ji, mu toog ci ngànguneem, mboolem gàngooru asamaan a nga taxaw ndijooram ba càmmoñam.
TSK
TSK · Daniel 7:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bala tund yee juddu, bala ngay sos suuf ak àddina, yaa mas di Yàlla, ba fàww.
Sama digg doole la ma semmale, gàttal samaw fan.
¶ At ma Buur Osiyas saayee, damaa gis Boroom bi toog kaw ngàngune mu kawee kawe, lafi mbubbam fees néeg bu sell bi.
Maay déjjatee Elam buur ak bummi, samp fa samab jal.» Kàddug Aji Sax jee.
Mbege yaa ngay nirook peru kirsolit, ci melokaan ak ci bind. Ñoom ñépp a niroo. Seen melokaan ak seen bind daa mel ni, mbege mu ci nekk, mbegee nekk ca biiram,
Aji Sax ji ne boroom ndimol lẽe ba: «Doxal ci diggante mbege, yi ronu jëmmi serub yi, nga tibb say loxo ba mu fees ci xal yu yànj yi, te nga dem wasaare ko ci kaw dëkk bi.» Kooka dem, may gis.
¶ «Ci jamonoy buur yooyu Yàlla Boroom asamaan dina samp nguur gu dul tas mukk, te wenn xeet du ko yilif mukk. Nguur googu dina tasaare mboolem yeneen nguur yooyu, ba genn du ci des, waaye moom day sax ba fàww.
ba keroog góor gu mag gi dikk, daldi jox dëgg aji sell yu Aji Kawe ji; àpp bi nag mat, aji sell yi moom nguur gi.
Waaye Aji Sax ji, xanaa du yaa masa nekk? Sama Yàlla sama Aji Sell ji, doo saay. Aji Sax ji, ab àtte nga tabbe ñii, yaw sama cëslaay, mbugal nga fi dëje ñii.
Yàllaa ko yéege fa ndijooram, te jot na ci Baay bi Noo gu Sell ga mu dige woon. Moom la tuur nii tey, ngeen gis ko, dégg ko.
ngir ma mana feeñe ci biir Almasi, fu ma yaakaarul sama njekku bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njekk gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi. Njekk googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi moo koy maye.
Moom doŋŋ moo dul dee, moo màkkaanoo leer gu kenn jotewul, te mooy ki nit masula gis te tële koo gis. Teddnga ak kàttan ñeel na ko ba fàww. Amiin.
ndax ngeen lekk suuxi buur ak suuxi njiiti gàngoor, suuxi jàmbaar ak suuxu fas ak gawaram, suuxu ñépp; gor ak jaam, mag ak ndaw.»