TSK

TSK · Daniel 8:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu mel ni xon ci biiri niir, bésub taw. Loolooy melokaanu leer ga ko wër. Muy melokaan muy jëmmal leeru Aji Sax ji. Naka laa ko gis, daldi ne gurub, dëpp sama kanam fi suuf. Ma dégg nag kàddu gu jib.

«Yaw nit ki, jàkkaarlool ak tundi Israyil, nga waxal leen waxyu.

¶ May xool ci biir peeñu mi, man Dañeel, di jéema xam lu muy tekki, jëmm juy nirook góor, ne jimeet taxaw ci sama kanam.

Ba nga tàmbalee ñaan la kàddu dikk. Maa la ko yégalsi, ndax yaw ku ñu naw nga. Déggal kàddu gi te dégg peeñu mi.

¶ Man Dañeel doŋŋ maa gis peeñu mi. Ñi ma àndal gisuñu ko. Tiitaange lu réy nag jàpp leen, ba ñu daw, làquji.

Jekki-jekki jëmm ju mel ni nit dikk, laal samay tuñ. Ma ŋa, àddu, daldi wax ak ki taxaw sama kanam ne ko: «Sang bi, peeñu mi tax na ma jàq, ba amatuma benn doole.

Ñenn ci boroom xel yu rafet yi dinanu jaare ci nattu yu leen di sellal, fóot leen ba ñu set wecc, ba keroog mujug jamono. Àpp ba nag des na.

¶ «Yaw nag Dañeel, dencal kàddu yii, muy kumpa te nga tëj téere bi, tay ko ba mujug jamono jub. Su keroogee ñu bare dinañu gëstu fu ne, ba xam-xam yokku.»

Peeñu mi seede la, ñeel jant ba ñu ko àppal, seede su wóor ci na mbir may mujje, te du fen. Su diibee it, xaar ko, day dikk moos te du yàggati.

¶ Malaaka ma nag ne ma: «Bindal lii: “Ndokklee ñi ñu woo ci berndey céetu Gàtt bi.”» Mu teg ca ne ma: «Loolu kàddu yu dëggu yu Yàlla la.»