¶ Sirus buuru Pers dafa wax ne: Mboolem réewi àddina, Yàlla Boroom asamaan moo ma leen dénk, te moom moo ma tabb, ngir ma tabaxal ko kër ca Yerusalem ga ca Yuda.
TSK
TSK · Daniel 8:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ci ñetteelu atu nguuram mu maye bernde, ñeel kàngamam yépp ak jawriñam yépp, di njiiti xarey diiwaanu Pers ak diiwaanu Medd, garmi yeek kàngami dëkk yi bokk teew.
Peeñu mu ñàng lañu ma ci wax. Workat biy wor, yàqkat biy yàq. Yeen waa Elam, songleen; yeen waa Medd, gawleen leen. Dakkal naa mboolem onk yu ñu sabab.
«Nàmmleen fitt yi, feesale mbar yi! Aji Sax ji xabtal na buuri Medd fi kaw Babilon, nar koo tas. Lii mbugalu Aji Sax jee, mbugal mi këram waral.
¶ «Ñaareelu rab wa ne jimeet, nirook urs. Mu ngi taxawe wet, ŋank ñetti faar. Ñu ne ko: “Jógal lekk yàpp wu bare.”
Ma séentu, xool, yemuma ci ku moy genn góor gu sol yérey wëñ gu ëccu, gañoo ngañaayal wurus wu raxul.
¶ Ba mu ko defee, ma séentu, gisuma lu moy ñeenti béjjén.
¶ Ci kaw loolu malaaka ma doon wax ak man dikk ne ma: «Séentul rekk ba gis lii di dikk.»
¶ Ma dellu séentu, yem ci ñeenti watiir yuy dikk diggante ñaari tund. Tund yi nag di tundi xànjar.