TSK

TSK · Daniel 9:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ni xeet yi Aji Sax ji nara sànk fi seen kanam, noonu ngeen di sànkoo ndax ñàkka déggal seen Yàlla Aji Sax ji.

¶ Waaye nag su ngeen déggalul seen Yàlla Aji Sax ji, te baña sàmmoo jëfe mboolemi santaaneem, ak dogali yoonam, yi ma leen di jox tey, mboolem alkànde yii dina leen dab, sottiku ci seen kaw:

Waaye su ngeen walbatee seen xol, dégluwuleen, xanaa ngeen lajj, di sujjóotal yeneen yàlla, di leen jaamu,

Aji Sax jee gis loolu, gedd, ndax mere doomam yooyu, góor ak jigéen.

Li waral loolu mooy waa Israyil a déggalul seen Yàlla Aji Sax ji. Dañoo fecci kóllëreem ak moom, ba mboolem li Musaa, jaamu Aji Sax ji, santaane woon, faalewuñu ko, jëfewuñu ko.

Wóoy wii xeetu moykat, wii askan wu diisu ñaawtéef, mii njurum defkati mbon, yii doomi yàqute! Ñoo wacc Aji Sax ji, ñoo teddadil Aji Sell ju Israyil, dëddu ko.

Yeen waa àddina, dégluleen! Maa ngii di indil askan wii musiba, seeni pexe jural leen. Ñoo faalewul samay kàddu, gàntal sama yoon.

Teewlu naa, déglu naa; du lu jaadu lañu wax. Kenn tuubu ci mbonam, ba ne: “Lu ma def nii?” Ku nekk a topp yoonam, ni fas wu màmm cib xare.

Nga wax leen nag ne leen: “Seeni maam a ma wacc,” kàddug Aji Sax jee, “di topp yeneen yàlla, di leen jaamook a sujjóotal. Man nag, ñu dëddu ma; sama yoon it, ñu bañ koo sàmm.

Aji Sax ji manatula dékku seen jëf ju bon ak seen jëf ju siblu ji waral seenum réew mel nii mu mel tey, di ndànd-foyfoy bu gental bu ñuy móoloo, te kenn dëkku ci,

Ay sarxalkatam xëtt nañu sama yoon, teddadil nañu sama yëf yu sell. Lu sell ak lu sellul, ràññeewuñu ko; lu set ak lu sobewu, xamlewuñu ko; sama bési Noflaay, ñu jéllale ko, ba ma mujj teddadi fi seen biir.