TSK

TSK · Daniel 9:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñi des ci yeen dinañu ràgg ca seen réewi noon ndax seeni bàkkaar ak seen bàkkaari maam.

su boobaa maay dagge bànni Israyil fi déndu suuf si ma leen jox, te kër gi ma sellal ngir sama tur, maa koy xalab, mu sore ma, te kon Israyil mujj di tur wu ñuy léeboo ak di ko kókklee ci biir xeet yépp.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.

Xettlee ma sa njekk, yiwi ma; ngalla teewlu ma, te wallu ma.

Ñeel askanu Kore wu góor, di woyu Sabóor. Dëkkub Aji Sax ji, kenu yaa nga ca tund yu sell ya.

Noo bàkkaar, nook sunuy maam; noo def lu ñaaw, def lu bon.

Sa dëkk yu sell doon nañu màndiŋ, Siyoŋ ca la, doon na màndiŋ. Yerusalem laa ne, gental na!

Maa leen di toppe saamar akub xiif ak mbas. Maa leen di def ñu seexlu leen ci mboolem réewi àddina, teg ci di musiba mu ñuy muslu ci biir mboolem xeet wu ma leen sànni, ba ku fay kókkalee, ñoom ngay tudd.

Yerusalem a moya moy, ba tax koo mujj di sobe; ku ko teraloon, sofental ko, ndax gis ko, mu ne duŋŋ. Moom ci boppam mu ngi binni, fuuylu.

Yeen waa Yerusalem maa leen di gental, sewal leen ci biir xeet yi leen séq, ku fi romb, di ci gis.

¶ Maa ngay wax ak a ñaan, di tuub sama bàkkaar ak a tuubloo Israyil sama ñoñ tey dagaanal sama tundu Yàlla wu sell wi, ci sama Yàlla Aji Sax ji.

Micah 6:4 TSK

Yeen maa leen génnee réewum Misra, kërug njaam googa, maa leen fa jote, ba yebal fi seen kanam, Musaa ak Aaróonaak Maryaama.

Te kat njekku Yàlla dina feeñ ndax coono ba muy delloo ñi leen teg ab coono.