bu ñu demee ba seenum xel dellusee fa réew ma ñu leen yóbbu ngàllo, ñu tuub tey sàkku aw yiw fi yaw foofa ca réewum ña leen jàpp, ne la noo moy, noo ñaaw, noo def lu bon,
TSK
TSK · Daniel 9:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ndegam li ma ñaawlu lañu masa def, di ma merloo, ba seeni maam génnee Misra ba tey jii.”»
daldi ñaan, ne: Éy sama Yàlla maa rus, maa torox, ba manumaa siggi fi sa kanam, ndaxte sunuy bàkkaar bare na, ba mëdd nu, sunuy moy tegloo ba àgg asamaan.
Yaw nag yaa yelloo njekk ci mboolem li nu dal, ndax worma nga jëfe, nun noo bon.
Noo bàkkaar, nook sunuy maam; noo def lu ñaaw, def lu bon.
Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko këpp sunu gépp ñaawtéef.
Yaay gatandu kiy bége njekk gi muy jëfe te di ba xel say yoon, yi ñu mas di jaare, ba mucc. Waaye kat, yaa nu mere, ndax noo bàkkaar.
Nan gapproo sunu gàcce, sàngoo sunu toroxte. Nook sunuy maam déy, ba ñuy gone ba tey jii, nu ngi tooñ sunu Yàlla Aji Sax ji, te déggalunu sunu Yàlla Aji Sax ji.
Aji Sax ji, xam nanu sunug mbon, xam sunu ñaawtéefi maam; moy nanu la moos.
Éy Aji Sax ji, xoolal sama njàqare, samay butit di fuddu, sama biir xol salfaañoo ndaxu tiis. Man de maa gàntal ba gàntaaral, ba fa biti, saamar di fa bóome, te biir kër it di ndee.
Ñoo gàntal sama àttey yoon, ba gëna bon xeet yi, gàntal samay dogal, ba gëna bon réew yi leen séq. Xalab nañu sama àttey yoon te jëfewuñu samay dogal.
Israyil gépp a moy sa yoon, jàdd, baña déglu sa kàddu, ba këppoo sa alkàndey ngiñ, gi ñu bind ci yoonu Musaa, sa jaam ba, ndax danu laa tooñ.
¶ Ba Aji Sax ji tàmbalee yóbbante Ose kàddoom, Aji Sax ji da ne ko: «Demal takki jabaru gànc, nga am ca doomi ngànctu, ndax réew maa ngi gànctu ngànctu gu réy, dëddu ma man Aji Sax ji.»
¶ Bokk yi, wattuleen bala kenn ci yeena am xolub gëmadi bu bon bu koy xiir ci dëddu Yàlla jiy dund.