Ñeengokati Misra itam fexe ca seeni xargafuufa, ba def lu mel noona. Firawna të rekk, tanqamlu Musaak Aaróona, muy la Aji Sax ji waxoon.
TSK
TSK · Deuteronomy 13:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yonent boobu nag mbaa boroom gént boobu, dee mooy àtteem, ndax moo woote ag fippu ci seen kaw Yàlla Aji Sax, ji leen jële ca réewum Misra, jote leen kërug njaam ga. Mu nar leena féle ci yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji sant ngeen doxe ko. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.
La yonent bi wax ci turu Aji Sax ji, su sottiwul, dikkul rekk, loola du kàddu gu Aji Sax ji wax. Ñeme Yàlla la ko yonent ba waxe, buleen ko ragal.
¶ «“Kon nag yeen, buleen déglu seen yonent yeek seetkat yeek firikati gént yeek boroom rawaan yeek ñeengokat yi leen di wax, naan leen dungeen tàbbi ci curgag buuru Babilon.
Xërëm, waxi neen, gisaanekat gisi fen, seeni gént, nari neen, te caaxaani neen lañuy dalalee. Moo tax mbooloo mii di taxawaalu niy xar, tumurànke ndax ñàkkub sàmm.
Peeñum ku dëng ki liggéeyu Seytaane lay àndal, te dina wone wépp xeetu manoore, aki firnde ak kéemaani feni neen,