TSK

TSK · Deuteronomy 13:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Seen Yàlla Aji Sax ji, ragal-leen ko. Moom ngeen di jaamu, te aw turam ngeen di giñe.

Reyleen ko rekk. Yeen ñi mu doon jéema yóbbaale, na ko seen loxo jëkka dal, ngir rey ko, bala cee loxol mbooloo mépp topp.

Waaye déy yonent bu am fitu àddu genn kàddu ci sama tur, te santuma ko mu wax ko, mbaa mu wax ci turi yeneen yàlla, boobu yonent, dee mooy àtteem.»

nañu yóbbu ndaw sa ba ca bunt kër baayam, te góori dëkk bi dóor koy doj ba mu dee, ndax moo def jëf ju gàccelu ci digg Israyil, di gànctoo kër baayam. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.

¶ Su amee nit ku ñu fekke kenn ciy bokkam, ku mu sàcce ci bànni Israyil, mu di ko jaamloo, mbaa mu jaay ko, su boobaa dee mooy àtteb kooka ko sàcc. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.

Mu walbatiku ànd ak moom ca kër ga, sex fa dugub, naan fa ndox.

Dëgg laay def nattukaay, njekk di sama buumu beteex, tawub doji yuur buub rawtub fen, wal ma mëdd làquwaay,

Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Yonent yi ma yebalul te ñuy waxe waxyu ci sama tur naan: “Saamar akub xiif du am ci miim réew,” saamar akub xiif ay mujje yooyu yonent.

Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ci mbirum Akab doomu Kolaya ak Cedesyas doomu Maaseya, ñoom ñi leen di jottli waxyuy fen ci turam. Mu ne: Maa ngii di leen teg ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, mu rey leen, ngeen di gis.

Te képp kuy biralati waxyu, ay waajuram, baayam ak ndeyam nañu ko wax ne ko: “Doo dese bakkan, ndax yaa fen ci turu Aji Sax ji.” Ay waajuram, baayam ak ndeyam nañu ko jam ba mu dee, ca ba muy biral waxyu.

Waa biti ñoom, Yàlla moo leen di àtte. Yeen, nag: «Tenqeeleen ku bon ci seen biir.»

¶ Sàkkuleen jàmm seen diggante ak ñépp, te it sàkkuleen sellnga, nde ku sellul du gis Boroom bi.