TSK

TSK · Deuteronomy 2:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji ne ko: «Keroog boo delloo Misra, nanga taxaw temm, te def ca kanam Firawna kéemaan, yi ma teg ci sa loxo yépp. Man maay dëgëral boppam, mu të ba du bàyyi mbooloo mi, ñu dem.

Musaa ak Aaróona def nañu yooyu kéemaan yépp ca kanam Firawna, waaye fekk na Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, ba mu të, baña bàyyi bànni Israyil, ñu génn réew ma.

¶ Ba mu ko defee ñu walbatiku, awe yoonu Basan, Og buuru Basan ànd ak gàngooram gépp, dajejeek ñoom, song leen xare ca Eddrey.

Xam naa ne ñu dëgër bopp ngeen. Dangeen të, wowle.