TSK

TSK · Deuteronomy 2:34

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mboolem lu ñu aayalal Aji Sax ji, lu sella sell la ñeel Aji Sax ji. Lépp lu nit moom, su dee nit mbaa jur mbaa suuf su mu donn, amu ci lenn lu mu aayalal Aji Sax ji te ñu sañ koo jaay mbaa mu di ko jotaat.

Nu faagaagal leen, na nu defoon ak Siwon buurub Esbon. Dëkk yépp lanu faagaagal: góor ak jigéen ba ca tuut-tànk ya.

Buleen dugal yëf yu seexluwu seen biir néeg, lu ko moy àtteb faagaagal bi war ci yëf yooyu, moo leen di dab, yeen itam. Xofleen koo xof, seexlu koo seexlu, ndax yëf yooyu, faagaagal moo ci war.

Demleen léegi, songi Amalegeen ñi. Faagaagal-leen seen lépp, te buleen leen ñeewante; reyleen góor ak jigéen, gone yi ba ci ñiy nàmp, ak nag ak gàtt, ak giléem ak mbaam.”»