TSK

TSK · Deuteronomy 28:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñu ne ko: «Sunu Yàlla, nun Ebrë yi, moo nu feeñu. Ngalla may nu, nu dem topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, ngir rendili sunu Yàlla Aji Sax ji sarax, lu ko moy mu dumaa nu jàngoro mbaa ab xare.»

Maa leen di fàdde mbas, nangu seen cér, ba noppi sose ci yaw askan wu leen ëpp, ëpp leen doole.»

Ña dee ca mbas ma nag di ñaar fukki junneek ñeent (24 000).

Bu ñu la laajee ne la: “Fu nu jëm?” nga wax leen ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Kiy wopp dee, wopp dee; kiy deeye saamar, deeye saamar; kiy deeye xiif, deeye xiif; kiy duggi ngàllo, duggi ngàllo.”

Maay fàdd lu dëkk ci dëkk bii, nit ak mala bokk loroo mbas mu réy.

Amos 4:10 TSK

«Maa leen yónnee mbas mu mel ni mu waa Misra. Maa reylu seeni waxambaane ci xare, jàpplu seeni fas, gillil xetu néew ya ca seeni dal. Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee.