TSK

TSK · Deuteronomy 29:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma.

Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen di teggil sas, yi leen waa Misra teg.

Aji Sax ji it biral na bésub tey, ne yeenay doon ñoñam ñi mu séddoo, noonee mu leen ko dige woon, te ngeen di sàmm mboolemi santaaneem.

¶ «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may fas ak waa kër Israyil ak waa kër Yuda kóllëre gu yees.

Waaye réew mu ko gën lañu doon sàkku, te mooy réewum asamaan. Looloo tax Yàlla rusul ñu di ko tudde seen Yàlla, ndax waajalal na leen ab dëkk.