TSK

TSK · Deuteronomy 4:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Yéegal ba ci man ci kaw tund wi te négandiku fa, ma jox la àlluway xeer yi ak yoon wi, ak santaane yi ma ci bind ngir jàngle ko.»

¶ Ba Yàlla noppee wax ak Musaa ca kaw tundu Sinayi, da koo jox ñaari àlluway doj yu mu binde loxol boppam.

¶ Musaa moo woo bànni Israyil gépp, wax leen ne leen: Yeen, bànni Israyil, dégluleen dogali yoon yi, ak àttey yoon yi may wax, ngeen dégg, tey. Jàngleen ko te farlu koo jëfe.

¶ Kàddu yii la Aji Sax ji wax seen ndaje ma mépp, ca tund wa, ba mu àddoo ca digg sawara wa, kàddu gu xumb, ci biir xàmbaar gu lëndëm këruus. Tegaatu ca dara. Mu daldi bind kàddu yi ci ñaari àlluway doj, jox ma.

Aji Sax ji jox ma ñaari àlluway doj yu loxol Yàlla bind mboolem kàddu ya leen Aji Sax ji waxoon ca kaw tund wa, ba mu àddoo fa digg sawara wa, keroog bésub ndaje ma.

Dara nekkuloon ca biir gaal ga, lu moy ñaari àlluway doj ya ca Musaa yeboon ca tundu Oreb, fa Aji Sax ji fase woon kóllëre ak bànni Israyil, ba ñu génnee réewum Misra.

Ca la sarxalukaayu wurus ba ñuy taal cuuraay bokkoon, gaalu kóllëre ga nekk moom doŋŋ ca biir néeg bu sell baa sell, ñu xoob ko wurus ba mu daj. Gaal ga moo yeboon njaqal wurus la defoon ñam wa ñuy wax mànn, ak yetu Aaróona wa jebbi woon, ak àlluway kóllëre ga.