TSK

TSK · Deuteronomy 7:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu ngoog, maa leen jox réew moomu. Demleen nangu réew mi Aji Sax ji giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ñeel leen ñook seen askan wi leen di wuutu.»

¶ Su ngeen déggalee ba déggal seen Yàlla Aji Sax ji, ngir di sàmmoo jëfe mboolem santaaneem, yi ma leen di dénk tey, kon Aji Sax ji seen Yàlla, Aji Kawe ji moo leen di aj ci kaw mboolem xeeti àddina.

¶ Barkeel ay ñeel seen meññeefum njurukaay, ak seen meññeefum suuf, ak seenug jur, seen jur gu gudd, ak seen jur gu gàtt.

¶ Waaye nag su ngeen déggalul seen Yàlla Aji Sax ji, te baña sàmmoo jëfe mboolemi santaaneem, ak dogali yoonam, yi ma leen di jox tey, mboolem alkànde yii dina leen dab, sottiku ci seen kaw:

Job 1:10 TSK

Xanaa du yaa ko ñag, ñag këram ak mboolem alalam, ba mu daj? Liggéeyam, nga barkeel, ba ag juram law ci réew mi.

Loo def mu àntu: nga mel ni garab gu saxe walum ndox, bu jotee meññ, te xob wa du lax.

Aji Sax ji barkeel, ñu giira giir, te wàññiwul seenug jur.

Sunuy sàq feese wirgoy wirgo, sunuy gàtt jur junni, ba fukki junni (10 000) ci parlu yi,

Indileen mboolem céru fukkeel ca kërug denc ya, ba ab dund am sama biir kër, te ngeen seetloo ma ko rekk,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ndegam duma leen ubbil bunti asamaan, ba sottil leen barke bu doy.