TSK

TSK · Deuteronomy 7:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ay goney Yàlla ñoo gis jigéen ñeek seen taar, ñuy jël ñi ñu bëgg ci ñoom, def leeni jabar.

Buleen wóllëranteek niti réew ma, lu ko moy dinañu gànctook seeni tuur, rendil seeni tuur ay sarax, woo leen ca, ngeen lekk ca seeni sarax.

Ñooñu bokk ci xeet, yi Aji Sax ji waxoon bànni Israyil ne leen: «Buleen jëli jabar ci ñoom, ñoom it buñu takksi ci yeen, ndax kon dinañu leen dëpp, ngeen topp seeni tuur.» Teewul Suleymaan bëgg leen, taq leen.

Ezra 9:1 TSK

¶ Gannaaw ba loolu wéyee njiit ya dikk, ne ma: «Du bànni Israyil, du sarxalkat yi, du Leween ñi, kenn ci ñoom teqlikoowul ak xeeti réew meek seen aada yu siblu. Dañuy jëfe ni Kanaaneen ñeek Etteen ñeek Periseen ñeek Yebuseen ñeek Amoneen ñeek Mowabeen ñeek waa Misraak Amoreen ñi.

Ezra 9:12 TSK

Kon nag seen doom yu jigéen buleen leen may seen doom yu góor, te seen doom yu jigéen buleen leen jëlal seen doom yu góor. Buleen seet mukk seen jàmm mbaa seen njariñ. Looloo leen di taxa am doole, bay xéewlu ci ngëneeli réew mi, ba wacce ko seen askan fàww.»

Ma ŋàññ leen, móolu leen, dóor ñenn ci ñoom, xuuf seen kawar, giñloo leen ci Yàlla ne dootuñu may seen doom yu jigéen ay doxandéem te dootuñu ci jëlal jabar seeni doom mbaa seen bopp.