TSK

TSK · Deuteronomy 9:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Dinaa wàcc, seede ko, ba mu wóor ne ñoo def lépp li sabab yuux yi, am déet.»

Kon na leen bir ne du seenug njekk moos la leen seen Yàlla Aji Sax ji joxe mii réew mu baax, ngir ngeen moom ko ndax, askan wu daŋŋiiral ngeen.

Ndax maa xam seen jikkoy fippu, ak seenug dëgër bopp. Seetleen, ndegam bi may dundagum tey ci seen biir ngeen di fippu ci kaw Aji Sax ji, astamaak gannaaw bu ma deeyee.

«Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma wax leen; yeen waa Israyil, ma sikk leen. Maa di Yàlla, seen Yàlla.

Sag njaalook sa ŋexali caga, sa gànctu gu ruslu ci kaw tundi àll bi! Maa gis sa jëf ju siblu jooju! Musibaa yaw Yerusalem! Foo àppal sa jëfi sobe ji?»

«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.