TSK

TSK · Ecclesiastes 1:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ne: «Éy Aji Sax ji, xamal ma sama muj ak sama àppi fan, ma xam ni sama dund gàtte.

Nit ni ngelaw, ay fanam di takkndeer, wéy.

Ma xoolaatal sama bopp lépp lu ma sottal, doñ-doñi ko, ba sottal, ndeke lépp, cóolóoli neen ak napp um ngelaw. Nit gisul njariñ ci kaw suuf.

Ma far bañ àddina. Ndaw naqar ci jëfi kaw suuf, te lépp di cóolóol ak napp um ngelaw!

Nit a ngi doñ-doñee xel, xam-xam ak manoore, te ku doñ-doñiwuloon lay wacce alalam. Loolu it, cóolóoli neen ak naqar wu réy.

Yàlla de, ku mu gërëm, xelal ko, xamal ko, bégal ko; bàkkaarkat bi, Yàlla teg ko, muy denc ak a dajale, ka mu gërëm jël. Loolu it di cóolóoli neen ak napp um ngelaw.

Ma gis ne nit ak kër-këram jépp ak bépp manoorey liggéey, iñaanantee ko waral. Loolu it, cóolóoli neen ak napp um ngelaw.

Mbooloo ngii mu janool, bare lool ba wees ab lim, te ña leen wuutu bégewuñu ki wuutu buur. Loolu it di cóolóoli neen ak napp um ngelaw.

Félal naqaru xol, dàq woppi yaram; waaye ndaw ak kawar gu ñuul, cóolóoli neen.

Ndax kat, càkkéef gépp, li ñuy déggal neenug neen la, te du seen coobare, waaye ki leen ci tënk la neex, ba tax ñuy yaakaar,