TSK

TSK · Ecclesiastes 12:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Malaaka ma ne ko: «Bu sa loxo laal xale bi; bu ko def dara, ndaxte léegi xam naa ne ragal nga Yàlla, ndax gàntaloo ma sa jenn doom ji.»

Bés ba ngeen taxawee fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, fa tundu Oreb, Aji Sax jee ma ne: «Dajaleel ma mbooloo mi, ma dégtal leen samay kàddu, ngir ñu tàggatu ci ragal ma li feek ñuy dund ci kaw suuf, te seeni doom it, ñu tàggat leen ci.»

¶ Léegi nag yeen Israyil, ana lu leen seen Yàlla Aji Sax ji laaj, lu moy ngeen ragal seen Yàlla Aji Sax ji, di doxe mboolemi yoonam, sopp ko, di jaamoo seen Yàlla Aji Sax ji seen léppi xol, ak seen léppi bakkan,

di dénkoo sa ndénkaanel Yàlla Aji Sax ji, di topp ay yoonam, sàmmonteek ay dogali yoonam aki santaaneem aki àttey yoonam aki seedeem, ni ñu ko binde ci yoonu Musaa. Su ko defee dinga am ndam ci lépp loo def ak fépp foo jëm,

Ragal Aji Sax ji di ndoortel rafet xel, dég-dég bu rafet ñeel ku koy wéye. Moo yeyoo cant ba fàww.

Nammeelu ku ko ragal, mu sottal; yuuxam, mu dégg, musal.

Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam, te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.

Ma xam ne lu Yàlla def, loola day sax ba fàww. Deesu ci yokk, mbaa di wàññi dara; Yàllaa ko def, ngir nit di ko wormaal.

Ana ku xam lu gën ci nit ak fanam ni cóolóol, toogadi ni takkndeer? Ku koy wax luy am gannaawam fi kaw suuf?

Micah 6:8 TSK

Yaw nit ki, waxees na la li baax, ak li Aji Sax ji sàkku ci yaw, te loolu moyul di def yoon, sopp jëfi ngor te woyof nooy toppe sa Yàlla.

Ñépp nag ngeen di teral; mbooloom gëmkat ñi, soppleen leen; Yàlla, ragal-leen ko; te buur, teral leen ko.