TSK

TSK · Ecclesiastes 2:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram, ji mu àndal, moom it mu lekk.

May ma, ma fénati caaxaani neen, te musale ma saw yoon.

Ndax xef ak xippi mu wéy, mel ni lu saxi laaf, ne fëyy, naaw ni jaxaay.

Ma ne ana lu nit di jariñoo ci doñ-doñ ak xalaatu xol, yi muy doñ-doñaale fi kaw dun bi?

Ma gis nag ne nit amul lu gën di bànneexoo ñaqam, loolooy wàllam. Ana ku koy xamal gannaawam?

Alal ak koom, ku ko Yàlla may, may ko mu tal koo xéewloo, mu nangu céram, bànneexoo ñaqam, loolu mayu Yàllaa.

Man daal damay digle bànneex, ndax nit amul lu gën fi kaw suuf di lekk ak a naan ak a bànneexu, muñe ko doñ-doñam, fan yi ko Yàlla may fi kaw suuf.

Xalelu góor bi, bànneexul bi ngay gone, bégalal sa xol bi ngay ndaw. Toppal loo namm ak loo xemmem, waaye xamal ne loolu lépp, Yàlla da la koy laaj.