¶ Dajeleen te déglu ma, man Yanqóoba seen baay; teewluleen seen baay Israyil.
TSK
TSK · Ecclesiastes 7:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ana kuy lim feppi suuf, ba lim askanu Yanqóoba? Ku mana waññ xaajaatub Israyil gii? Man de, yal naa dee deewinu aji jub ñii, yal na sama muj mel ni gu askan wii!»
da ne leen: «Defleen seen xel ci mboolem kàddu yi ma leen di artoo man, bésub tey, te ngeen sant seeni doom ñu sàmmoo jëfe mboolem kàdduy yoon wii.
Yal nanga nu xiir ci lim sunuy fan, ba nu mana dawal xel mu rafet.
Wóoy ngalla ñiy teela xëy, daw wutiw ñoll, gonloo biiñ ba tàng jérr.
te naa: «Ba fàww maay lingeer!» ba tax bàyyiwoo xel ca la ngay def; xalaatoo la muy jur.
Kon nag léegi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Teewlooleen xel seeni jaar-jaar.
Seen jëfi démb ja leen gàcceel tey, ana njariñ lu mu leen jural? Mujug jëf ja de, seenug dee la doon doon.
Kon ni ab dogal sédde nit ñi benn yoon doŋŋ bu ñuy dee, seenub àtte topp ci,