¶ Teewul kàddug Buur ëpp doole Yowab ak njiiti xarekat ya. Ñu bàyyikoo ca Buur, dem bindi askanu Israyil.
TSK
TSK · Ecclesiastes 8:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Buur Suleymaan daldi jox ndigal Benaya doomu Yoyada. Benaya jam Adoña, mu dee.
Buur nag sant Benaya doomu Yoyada, mu génne Simey, jam ko, mu dee. Ba loolu amee nguur ga gëna dëgër ca loxol Suleymaan.
Kii, bu këfee, ana ku koy tere? Ana ku ko naa: «Looy def nii?»
Kii moo naan buur: «Yaa sew!» naa garmi: «Yaa bon!»
Buur mer lool, mel ni gayndee ŋar; boo ko merloo, dangay xaru.
Léegi, bettuma leen. Bu ngeen di dégg bufta geek toxoro geek xalam geek riiti geek kooraa geek liit geek mboolem jumtukaayi xumbal yi rekk, sujjóotleen, màggale ko jëmm ji ma sàkk. Waaye su ngeen ko màggalul, dees na leen daldi sànni ci biir taalu sawara bu yànj. Ana yàlla ju leen di musal ci man?»
¶ «Maa leen ko wax, yeen samay soppe, buleen ragal ñu manul lu wees rey seen yaram, ndax gannaaw loolu dootuñu leen manal lu ko raw.
¶ Na ku nekk déggal njiit yi yor kilifteef, nde amul njiit lu bawoowul fa Yàlla, te njiit yi toog, Yàlla moo leen tabb.