ñu doon sama ñoñ, may seen Yàlla.
TSK
TSK · Ephesians 4:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Su boobaa ma soppi làmmiñu xeet yi, setal ko, ngir ñuy tudd ñoom ñépp turu Aji Sax ji, di ko jaamoondoo benn bopp.
¶ Bokk yi nag, dama leen di ñaax, ci sunu turu Sang Yeesu Almasi, ngir seen kàddu di genn, te féewaloo baña am ci seen biir, xanaa ngeen bennoo ci lépp, bokk menn xel, ak benn jëmu.
Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leere ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi.
Yoonu Musaa ak santaane yaak ndigal ya, moom la xewil, ngir yeesal ñaar ñi, Yawut beek jaambur bi, ci jenn jëmmu boppam, ñu doon kenn nit ku yees, ba jàmmoo.
Benn Sang bi la it, ak genn ngëm, ak genn sóobu cim ndox.
¶ Ndegam amees na lenn lu yokk aw fit ci Almasi mi nu gëm, ndegam lenni cofeelam lu mana dëfal am na, ndegam amees na benn cér ci Noo gu Sell gi, ndegam it, amees na lenn lu bawoo fi moom, ci wàllu xol bu rafet, ak yërmande,
¶ Almasi moomu nag lanuy xamle; na mu gëna xeloo lanuy àrtoo nit ku nekk, te ni lanuy jàngale nit ku nekk, ngir àgge nit ku nekk ba fa kanam Almasi, fekk ko mat sëkk, na mu ware ku ànd ak Almasi.
Mag ñi kay ñoo yelloo ñam wu dëgër, ñoo tàmma jëfoo seenum xel, ngir ràññee lu baax ak lu bon.
Waaye màggleen ci wàllu yiwu sunu Boroom, sunu Musalkat Yeesu Almasi, ak ci wàllu xam-xam bu ngeen ko xam. Ndam ñeel na ko tey, ba kera bés bu sax dàkk. Amiin.