Ma dellu ne leen: «Li ngeen di def de baaxul. Lu leen tee di ragal sunu Yàlla bala noo torox ci kanam noon yi dul Yawut?
TSK
TSK · Ephesians 5:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Doom, ragalal Aji Sax ji, wormaal buur. Bul lëngook kuy fippu.
ngeen nangul nit ñu mel noonu, ñoom ak mboolem ñu bokk ak ñoom liggéey bi ak coono bi.
¶ Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.
Kon nag ni mbooloo mi nangule Almasi, ni la jabar ji wara nangule jëkkëram ci lépp.
¶ Te it bu ñuy jàngle, na jigéen ñiy noppi, te woyof toyy.
¶ Déggal-leen seeni njiit te nangul leen, ndax sàmm bakkani ñi ñu jiite mooy seenub liggéey, te moom lees leen di laaj ëllëg. Su ko defee ñu defe ko xol bu sedd, te bañ koo def di binni, ndax loolu du seen njariñ.
Ñépp nag ngeen di teral; mbooloom gëmkat ñi, soppleen leen; Yàlla, ragal-leen ko; te buur, teral leen ko.