TSK

TSK · Esther 2:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mardose yoroon ku ñuy wax Adasa, muy Esteer ba tey, di doomu baayam bu ndaw, ndax amuloon ndey, amuloon baay. Xale bi nag rafet, jekk bind. Ba ndeyam ak baayam deeyee, Mardosee ko jël, yar ko ni doomam.

¶ Aman wax Buur Aserus ne ko: «Aw xeet a ngi fi, tasaaroo ci biir xeet yi, jaxasoo ci seen biir, ci mboolem sa diiwaani réew mi. Seeni aada daa wuuteek yu xeet yépp; yoon yi Buur tëral, duñu ko jëfe, te jaaduwul ci Buur mu di leen seetaan.

Ndax dañu noo fexeel maak samaw xeet, nar noo sànk, bóom nu, faagaagal nu. Su doon ay jaam yu góor ak yu jigéen sax lañu nuy fexee def, dama naan cell, ndax njàqare ju ni tollu sax jarul ñuy lëjal Buur.»

¶ Naka yeen xale yi, déggal-leen seeni waajur, ngir Boroom bi, ndax moo war.