TSK

TSK · Exodus 10:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te wax naa la ne la, nga bàyyi sama doom, ndax mu man maa jaamu, nga bañ. Kon nag dinaa rey sa taaw bu góor.’ ”»

Ndaxam yaa ngi réy-réylu ci sama kaw ñoñ ba tey, bañ leena bàyyi, ñu dem.

«Ba kañ la mbooloo mu bon mii di ñaxtu ci sama kaw? Ñaxtu yi bànni Israyil di ñaxtu ci sama kaw, dégg naa ci.

«Gis nga ni Axab toroxloo fi sama kanam? Gannaaw toroxlu na nii ci sama kanam, duma wàcce lu bon cig dundam. Ci jamonoy doomam ju góor laay wàcce lu bon ci waa këram.»

Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi? Ñaawlekat bi, foo àppal sa ñaawle bi? Dof bi, ñaata yoon ngay bañ xam-xam?

Bésub keroog booba, ku bew bay regeju mooy detteelu, sagub nit sàggiku, Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.

Waxal Buur, wax Lingeer yaayu Buur ne leen: «Dëjuleen fi suuf, seen mbaxanam nguur mu yànj foq na.

Am dangay sofental mbaaxu Yàlla gu réy, akug jéllaleem, akug muñam, ndax ñàkka xam ne li Yàlla namm ci baaxe la, moo di nga tuub?

Toroxluleen fi kanam Boroom bi, mu yékkati leen.