Njuddu-ji-réew ji nangeen ko yemaleek doxandéem bi ngeen dëkkal. Soppleen ko ni ngeen soppe seen bopp, ndaxte ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
TSK
TSK · Exodus 12:49
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Leviticus 19:34
TSK
Numbers 9:14
TSK
¶ «Su dee ab doxandéem bu ngeen dëkkal, sañ naa màggal bésub Mucc bi ñeel Aji Sax ji. Na mu dëppook mboolem dogali yooni bésub Mucc, ak àttey yoonam, ni la koy màggale; benn dogal bi lay doon ci yeen, muy doxandéem bi, di njuddu-ji-réew.»
Numbers 15:16
TSK
Wenn yoon wee, di benn àtte bi, ñeel leen, ñeel doxandéem bi dal ak yeen.»
Numbers 35:15
TSK
Waaye muy bànni Israyil, muy doxandéem, muy gan gu nekk ci seen biir, na juróom benni dëkk yooyu doon seen rawtu yeen ñépp, ba képp ku rey nit te du teyeefam, man faa raweji.
Colossians 3:11
TSK
Dundin wu yees woowu amul jaambur akub Yawut, amul ku xaraf ak ku xaraful, amul ab doxandéem ak ku xayadi, amul ab jaam ak as gor, waaye Almasi mooy lépp te moo nekk ci ñépp.