Ëllëg aki sibbir booy seetsi sama peyoor, sama njubtee may layool: lépp lu toddewul te tippantewul ci biir bëy yi ak lu ñuulul ci mburt yi, boo ko gisee ci man, càcc la.»
TSK
TSK · Exodus 13:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen di teggil sas, yi leen waa Misra teg.
Te bu leen seeni doom laajee ne leen: “Lu aada jii di wund?”
Musaa ne mbooloo ma: «Fàttlikuleen bésub tey jii ngeen génne Misra, kërug njaam gi, ak ni leen Aji Sax ji yiwee dooley loxoom. Bu ci kenn lekk mburu mu am lawiir.
«Man Aji Sax ji, maa di seen Yàlla, ji leen génne réewum Misra, kërug njaam ga.
Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca réewum Misra. Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen fa génnee dooley loxoom, ak kàttanu përëgam. Moo tax seen Yàlla Aji Sax ji sant leen ngeen wàccoo ak bésub Noflaay.
¶ Bu leen seen doom laajee ëllëg, ne leen: «Ana lu waral seedey yoon yi, ak dogali yoon yeek àttey yoon yi leen sunu Yàlla Aji Sax ji dénk?»
Dunu ko nëbb sunuy doom, xanaa di ko jottli maas giy ñëw, xamal leen jaloorey Aji Sax ji ak kàttanam aki kéemaanam.
Na maasoo maas di màggal say jaloore, di biral sa njàmbaarte.
¶ «Léegi nag yaw Boroom bi, sunu Yàlla ji nu génnee Misraak doole, nun sa mbooloo, nga siiwale ca sa tur ba sunu jonni yàllay tey, noo bàkkaar, noo tooñ.