TSK

TSK · Exodus 13:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Bésub keroog bésu pàttliku lay doon ci yeen, ngeen war koo màggal ngir Aji Sax ji, muy dogal bu leen war fàww, yeen ak seen askan.

Musaa ne mbooloo ma: «Fàttlikuleen bésub tey jii ngeen génne Misra, kërug njaam gi, ak ni leen Aji Sax ji yiwee dooley loxoom. Bu ci kenn lekk mburu mu am lawiir.

Mu doon seen langat yu ngeen di xool, di ko fàttlikoo mboolem santaaney Aji Sax ji, ngir di ko jëfe, te baña topp seen bànneexu bakkan ak seeni gët, bay moy.

Kàddu yii ma leen di dénk bésub tey, na dëkk ci seen xol.

Su boobaa waxleen seen doom, ne ko: «Ay jaami Firawna lanu woon ca Misra, waaye Aji Sax jee nu génnee Misra ci dooley loxoom.

Kàddu gi kay jege na leen lool; ci seen gémmiñ ak ci seen biir xol la nekk, ngir ngeen di ko jëfe.

Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk. Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur.

Kaala gu jekk la ci bopp, di gànjar ci baat.

Doom, defal li la baay sant, te bul wacc ndigalal yaay.

Mooy picc mu tàbbi cig fiir. Du xam ne day dee, ba keroog fitt jam ko ci xol.

Bésub keroog Aji Sax ji dikke saamaram bu jàmbaare, ñàng te réy, ba dal ci kaw Lewiyatan, jaan ja ca xél wa, Lewiyatan jaan jay wañaaruy dem, ninki-nànkay géej jooju lay rey.

Sama biir loxo yii laa la ñaas, say tataa janook man ba fàww.

«Man nag, lii mooy sama kóllëreek ñoom: Sama xel mi tegu fi sa kaw, ak sama kàddu yi ma yeb ci sa gémmiñ, lenn du ci teqlikook sa gémmiñ ak sa gémmiñu askan, ak sa gémmiñu askanu askan, tey ak ëllëg.» Aji Sax jee ko wax.

¶ «Léegi nag yaw Boroom bi, sunu Yàlla ji nu génnee Misraak doole, nun sa mbooloo, nga siiwale ca sa tur ba sunu jonni yàllay tey, noo bàkkaar, noo tooñ.

looloo tax ci benn bés la musiba yiy këppoondoo ci kawam: mbas, deele akub xiif, te dees na ko lakk ba mu jeex, ndax Boroom bi Yàlla mi ko mbugal moo am doole.»