TSK

TSK · Exodus 16:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu wéyee Musaa ne Aaróona: «Waxal mbooloom bànni Israyil gépp, ne leen ñu dem ba ca kanam Aji Sax ji, ndaxte dégg na seeni diiŋat.»

¶ «Mbooloo mi nag, ne leen ñu sell-lu ngir ëllëg, te ne leen dinañu yàpp moos, gannaaw ñooy jooy ci kaw Aji Sax ji, naan “Éy ku nuy leelatiw yàpp, nooka neexle woon ca Misra!” Kon nag Aji Sax jee leen di jox yàpp wu ñu lekk.

Mbooloo ma dikk ba ci Musaa, ne ko: «Noo tooñ, ndax noo xultu ci kaw Aji Sax ji, ak ci sa kaw. Tinul nu Aji Sax ji, mu teggil nu jaan yi!» Musaa daldi tinul mbooloo ma.

Ab dof, waxi dof lay wax, xel ma di nas ñaawtéef, mu nar jëf ju teddadi. Lu ñaaw lay wax, jëme ci Aji Sax ji, di xiifal ku xiif, di xañ ku mar lu mu naan.

¶ «Ku leen déggal nag, man nga déggal; ku leen gàntal, man nga gàntal. Te ku ma gàntal, gàntal nga ki ma yebal.»

Buleen jàmbat, ni ñenn ci ñoom doon jàmbate, ba tax malaakam reykat ba rey leen.