TSK

TSK · Exodus 23:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Buleen wóllëranteek niti réew ma, lu ko moy dinañu gànctook seeni tuur, rendil seeni tuur ay sarax, woo leen ca, ngeen lekk ca seeni sarax.

¶ Bu leen seen Yàlla Aji Sax ji yóbboo réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko, moo fay dàqe xeet yu bare fi seen kanam: Etteen ñi ak Girgaseen ñi ak Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ak Eween ñeek Yebuseen ñi; juróom ñaari xeet yu leen ëpp, ëpp leen doole.

Fàkkasleen mboolem xeet yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jébbal nag. Buleen leen xool bëtu yërmande, buleen jaamu seeni tuur: Lu ko moy muy seenug fiir.

Aji Sax jee leen di joxe fi seen kanam, ngeen def leen mboolem li ma leen santoon.

¶ Jamono ya Daawuda nekkee ci jal bi, amoon na xiifub ñetti at yu tegloo. Daawuda diis ko Aji Sax ji. Aji Sax ji ne ko: «Li waral xiif bi moo di àqu deret ji topp Sóol ak waa këram ndax waa Gabawon ña mu rey.»

Gan juboo la Almasi ak Seytaane séq? Wan wàll la gëmkat bi bokk ak gëmadikat bi?