TSK

TSK · Exodus 27:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yàlla tudde leer gi bëccëg, lëndëm gi guddi. Ngoon jot, suba dugg, muy bés ba jëkk.

¶ «Bésub keroog bésu pàttliku lay doon ci yeen, ngeen war koo màggal ngir Aji Sax ji, muy dogal bu leen war fàww, yeen ak seen askan.

Yebal ci gaal gi àlluway seede si ma lay jox.

¶ «Sàkkal rido bu ñu ràbbe wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe, ñu ñawaale ca nataali serub,

kaala leen, te takkal Aaróona ak doomam yu góor ay laxasaay. Su ko defee ñu féetewoo céru sarxalkat, muy dogal bu sax dàkk. «Noonu ngay sase Aaróona ak doomam yu góor.

Saraxu rendi-dóomal lay doon bu sax, te war seen maasoo maas fi bunt xaymab ndaje mi, ci kanam Aji Sax ji. Foofu laay dajeek yeen, te fa laay waxe ak yaw,

Bu Aaróona di taal làmp yi diggante ngoon ak jant bu so itam, na taal cuuraay lu xeeñ li. Cuuraay la su ñuy taal ba fàww, ci seen gépp maas fi kanam Aji Sax ji.

Sàkk ci, wol ko ba mu mokk, nga teg ko fi kanam gaal gi àlluway seede si dence, fi biir xaymab ndaje mi, fi may dajeek yaw. Loolu lu sella sell la lu ngeen wara wormaal.

te teg loxoom ci boppu xar mi muy sarxe, ñu rendi ko ci bunt xaymab ndaje mi, doomi Aaróona yu góor yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.

Sarxalkat bi ñuy fal ci doomi Aaróona yu góor yi, mu war koo wuutu, da koy def moom itam. Aji Sax ji moo jagoo sarax boobu fàww, te dañu koy lakk ba mu jeex.

«Biiñ mbaa naan guy màndal bu ko kenn ci yeen naan buy duggsi ci biir xaymab ndaje mi, du yaw, du say doom yu góor, lu ko moy dingeen dee. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan.

Buñu di sarxalatil tuur, yi ñuy jëmmale sikket, di ko bokkaalee. Na loolu di dogal bu leen war fàww, ñoom ak seen askan.

Wooteleen ci bés boobu ndaje mu sell, te lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan, ak fépp fu ngeen dëkk.

Mburu yooyu Aaróona aki doomam yu góor ñoo koy féetewoo, te nañu ko lekke fu sell, ndaxte lu sella sell la, di lu ñu séddoo fàww ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.»

Leween ñi ñooy ñiy liggéey liggéeyi xaymab ndaje mi, te lu ñu ca tooñ, ñooy gàddu pey ga, ci kaw dogal bu sax dàkk, ñeel leen, ñook seen askan. Waaye biir bànni Israyil, Leween ñi duñu ci séddu céru suuf,

¶ «Loolu mooy dogalu yoon bi leen ñeel, yeen ak seen askan, ci seen mboolemi dëkkuwaay.

Bésub keroog la Daawuda dale def loolu mu dib dogal, di àtteb yoon bu ñeel Israyil ba tey jii.

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ayca, santleen Aji Sax ji, yeen jaami Aji Sax ji yépp, yeen ñiy taxawe kër Aji Sax ji guddi.

¶ Rax ci dolli nu ngeek waxi yonent yi, muy wax ju wóor ju jara gëm, te yeena yey teewlu waxi yonent yi, ni ñuy teewloo ceeñeeru làmp bu tàkke biir lëndëm, ba kera fajar di xar, ba biddiiwu njël feqal seen xol.