TSK

TSK · Exodus 29:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Dañuy lakk yàpp wa cib taal, lekk ko guddig keroog, boole kook mburu mu amul lawiir ak xob yu wex.

¶ «Su dee sarxal lu ñu defare pepp, di lu ñu lakk cib taal ba mu ñor, na doon sunguf su mucc ayib, di mburu yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw, mbaa mburu yu sew yu amul lawiir, ñu sotti diw ca kawam.

«Li Aaróona aki doomam yu góor di sarxalal Aji Sax ji, keroog bu ñu koy diw, fal ko, mooy lii: ñetti kiloy sunguf su mucc ayib, tollook saraxu pepp bi ñu saxoo bés bu nekk, te genn-wàll gi di suba, genn-wàll gi ngoon.

Waaye weneen xeetu saraxu pepp mu mu mana doon, su dee saraxu pepp mu ñuy xiiwaale diw mbaa muy mu wow, doomi Aaróona yu góor yépp a koy moom, ku nekk tollook sa moroom cér.

«Indil Aaróona aki doomam yu góor te indaale yére yi ak diw gi ñuy fale ak yëkk wiy saraxu póotum bàkkaar ak ñaari kuuy yi, boole ca pañeb mburu ya amul lawiir,

ak pañeb mburu yu amul lawiir, yu ñu lakke sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ak mburu yu sew yu amul lawiir yu ñu wis ag diw, ak saraxi peppam ak saraxi tuuroom ya muy àndal.

Setal-leen seen bopp boog, génneleen lawiir bu yàgg bi ci seen biir, ba mana doon tooyal bu bees bu mucc lawiir, nde doon ngeen ko ba noppi, ndax Almasi, sunu gàttub bésub Mucc biy sunub sarax, rendilees na nu ko.