TSK

TSK · Exodus 29:45

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen di teggil sas, yi leen waa Misra teg.

Na ma bànni Israyil defaral kër gu sell, ndax ma dëkk ci seen biir.

Maay ànd ak yeen, di seen Yàlla, ngeen di sama ñoñ.

Buleen sobeel réew mi ngeen dëkk, te man ma màkkaanoo ci biiram, ndax man Aji Sax ji maa màkkaanoo ci biir bànni Israyil.»

Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000), ba ci junniy junni. Boroom bi ne ca seen biir, di boroom tundu Sinayi fa biir sellngaam.

Man Aji Sax ji maay doon seen Yàlla, Daawuda sama jaam bi mooy askanoo nguur fi seen biir. Man Aji Sax ji maa ko wax.

Léegi nag nañu ma sorele seen gànctu ak seen néewi buur yi, ndax ma mana dëkk fi seen biir, ba fàww.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Maay dellu Siyoŋ, Yerusalem googu laay màkkaanoo, ba ñuy wooye Yerusalem dëkkub Worma, foofu di tundu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, lees di wooye tundu Sellnga.»

Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»

Ma dégg kàddu gu xumb jibe ca ngàngune ma, ne: «Màkkaanu Yàllaa ngii ci biir nit ñi. Mooy dëkk ak ñoom, ñu diy ñoñam. Yàlla ci boppam mooy dëkk ak ñoom, di seen Yàlla.