TSK

TSK · Exodus 29:46

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Man Aji Sax ji, maa di seen Yàlla, ji leen génne réewum Misra, kërug njaam ga.

ndaxte man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Kon nag sell-luleen te sell ndax man ku Sell laa. Kon buleen sobeel mukk seen bopp ci mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ci suuf.

«Waxal mbooloom bànni Israyil gépp ne leen: Ñu sell ngeen wara doon, ngir ku Sell laa, man seen Yàlla Aji Sax ji.

Ci kaw loolu ñu bokk daje fi kaw Musaa ak Aaróona, ne leen: «Doy na sëkk! Mbooloo mi ba mu daj, ñépp a sell, te ci sunu biir la Aji Sax ji nekk. Ana lu ngeen di xoggliku ci kaw mbooloom Aji Sax ji?»

«Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israyil gannaaw loolu,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.

Man Aji Sax ji maay doon seen Yàlla, Daawuda sama jaam bi mooy askanoo nguur fi seen biir. Man Aji Sax ji maa ko wax.