Ci biir xaymab ndaje mi la Aaróona ak doomam yu góor di teg làmp yi, ci kanam rido bi làq gaalu àlluway seede si, ñuy fanaanee tàkk ngoon ba bët set, fi kanam Aji Sax ji. Dogal a ngoogu, war bànni Israyil fàww, ñoom ak seen askan.
TSK
TSK · Exodus 29:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Doomi Aaróona yu góor yi itam, sàkkal leen ay mbubb. Sàkkal leen ay laxasaay, te ay kaala it, sàkkal leen ko ngir daraja ak teraanga bu sarxalkat wara yelloo.
Nga diw leen, ni nga diwe seen baay, ñu doon samay sarxalkat. Seen diwu googu moo leen sédd sasu carxal bu sax dàkk, maasoo maas.»
Waaye bunt xaymab ndaje mi buleen ko wees diiru juróom ñaari fan, ba bésub keroog ba seen xewu colu di mat, ndax juróom ñaari fan lay mat.
Yaw mu jegeñal la, yaak sa bokki Leween ñépp, ngeen di xëccu céru carxal, boole ci!
mu ñeel ko, mook askan wi koy wuutu, te di kóllëreg carxal gu sax dàkk, ndax moo fiire Yàllaam, ba jot bànni Israyil.»
¶ Te it kenn jagoowul boppam teraangay carxal, ndare du Yàllaa ko ci woo, na woon ca Aaróona.
¶ Kon liggéeyu carxal gu Leween, ñi yoroon yoonu Musaa, wi ñu dénkoon bànni Israyil, su doon liggéey buy taxa mat sëkk, ndax dees na soxlaati beneen sarxalkat bu jóg topp dayob Melkisedeg, te toppul dayob Aaróona?