Yàlla Aji Man ji, mooy ni ma feeñoo woon Ibraayma, te ni laa feeñoo Isaaxa ak Yanqóoba it, waaye sama tur, Aji Sax ji, leeraluma leen ko woon.
TSK
TSK · Exodus 3:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Exodus 6:3
TSK
Job 11:7
TSK
Dangaa mana gëstu mbóoti Yàlla, ba gis ko? Am yaa ñédd Aji Man ji?
Psalms 90:2
TSK
Bala tund yee juddu, bala ngay sos suuf ak àddina, yaa mas di Yàlla, ba fàww.
Isaiah 44:6
TSK
Aji Sax ji dafa wax, moom buurub Israyil, jotkatam, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ne: «Maa jëkk, maa mujj, te yàlla amul ndare man.
Hebrews 13:8
TSK
Yeesu Almasi menn mi la woon démb ak tey ba fàww.
Revelation 1:8
TSK
¶ «Man, maay Alfa, di Omega», la Boroom bi Yàlla wax, moom Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk ëllëg, te di Aji Man ji.
Revelation 4:8
TSK
Ñeenti bindeef yi am nañu ku nekk juróom benni laaf, fees aki bët ba daj, biir ak biti, te guddi ak bëccëg duñu selaw, xanaa naan: «Kee sell, Kee sell, Kee sell, Keey Boroom bi Yàlla Aji Man ji, Kee masa Nekk, Kee Nekk, Keey Dikk.»