TSK

TSK · Exodus 3:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yàlla nag sàkk dénd wi, xàjjalee ko ndox yi féete dénd wi suuf ak yi ko féete kaw. Mu daldi nekk noona.

¶ Mu am bés Yuusufa ne ay bokkam: «Sama waxtu jege na, waaye Yàlla moo leen di jëlsi moos, ba jële leen ci réew mii, yóbbu leen ca réew ma mu dige woon, ba giñal ko Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.»

Yàlla nag geesu bànni Israyil, ñeewante leen.

Aji Sax ji ne ko: «Loolu ngay def, ngir ñu gëm ne Aji Sax ji seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba, moo la feeñu ci lu wér.»

ba mbooloo ma gëm. Ba magi Israyil déggee ne Aji Sax ji nemmiku na bànni Israyil te gis na notaange, gi ñu nekke, dañoo sujjóot, màggal Aji Sax ji.

Jaambur ñay dégg, di rag-ragi, tiitaange ne taral waa Filisti,

Waaye njiiti bànni Israyil ña, loxol Yàlla dalu leen. Ñoo gis Yàlla, te gannaaw loolu lekk nañu, naan nañu.

Damay xool sa asamaan si nga móol, ak weer week biddiiw yi nga fi teg.

Ñoo lay nappaaje ci suuf, yaak say doom yi ci sa biir, te duñu bàyyi doj ci kaw doj ci sa biir, ndax ba sa bésub wall dikkee, yaa ko ràññeewuloon.»

Simoŋ xamle na, ni Yàlla yége jaambur ñi ca njàlbéen, ba sàkke ci seen biir, xeet wu mu tudde turam.

waaye am na ku yékkatee bérab, kàddug seede, ne: «Ana luy nit ba nga di ko faale? Ana luy doom aadama, ba nga di ko yég?

¶ Mag ñi ci seen biir di seeni njiit nag, dama leen di ñaax, man miy njiit ni ñoom, di seedeb coonoy Almasi, te di boroom cér ci ndam li nara feeñ.