TSK

TSK · Exodus 3:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

boole ci réewum Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Girgaseen ñi ak Yebuseen ñi.»

¶ Mu am bés Yuusufa ne ay bokkam: «Sama waxtu jege na, waaye Yàlla moo leen di jëlsi moos, ba jële leen ci réew mii, yóbbu leen ca réew ma mu dige woon, ba giñal ko Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.»

Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña.

ba ngeen dugg ca réew mooma meew maak lem ja tuuroo. Waaye duma ànd ak yeen, lu ko moy dinaa leen faagaagal ci yoon wi, ndax askan wu dëgër bopp ngeen.»

Ci kaw loolu ñu nettali Musaa, ne: «Dem nanu réew, ma nga nu yebaloon, te it foofa la meew maak lem ja tuuroo! Lii ca meññeef maa.

Su ko defee ma wàccook ngiñ, la ma giñaloon seeni maam ne dinaa leen may réew mu meew maak lem ja tuuroo, muy fii tey.”» Ma ne ko: «Tigi, Aji Sax ji.»