Aji Sax ji ne ko: «Keroog boo delloo Misra, nanga taxaw temm, te def ca kanam Firawna kéemaan, yi ma teg ci sa loxo yépp. Man maay dëgëral boppam, mu të ba du bàyyi mbooloo mi, ñu dem.
TSK
TSK · Exodus 3:19
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Dinga gis léegi ni may def Firawna: loxo bu ko ëpp dooleey tax mu bàyyi leen ñu dem. Bir na ne, loxo bu ko ëpp doole mooy tax mu dàq leen réewam.»
¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji wax na Musaa ne ko: «Firawna daa dëgër bopp. Bañ naa bàyyi mbooloo mi, ñu dem.
Ba Firawna yónnee, ba nemmiku mbir ma, xam na ne lenn deewul ca juru bànni Israyil. Teewul mu të ticc ba tey, baña bàyyi mbooloo ma, ñu dem.
Teewul Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, mu të rekk, baña bàyyi bànni Israyil ñu dem.
Musaa ak Aaróona def nañu yooyu kéemaan yépp ca kanam Firawna, waaye fekk na Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, ba mu të, baña bàyyi bànni Israyil, ñu génn réew ma.
seppee bànni Israyil ca ñoom, Kee saxoo ngoram!